TSK

TSK · Exodus 32:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Yuda jegesi ne ko: «Ngalla sang bi, ma ñeme laa diis lenn rekk, te sa xol baña tàng ci man, doonte yaak Firawnaa tolloo.

Mbooloo ma nag di diiŋat Musaa, naan: «Ana ndox mu nuy naan nag?»

Waaye dégluwuñu Musaa, am na ñenn ca ñoom ñu ca wàññi, fanaanal, mu def ay sax, xasaw xunn. Musaa nag mere leen.

Ñu jote faak Musaa, naan ko: «Joxleen nu nag ndox mu nu naan!» Musaa ne leen: «Ana lu ngeen joteek man? Aji Sax ji ngeen di seetlu nag?»

¶ Fàttlikuleen! Buleen fàtte na ngeen merloo woon seen Yàlla Aji Sax ji ca màndiŋ ma. La dale bés ba ngeen bàyyikoo réewum Misra, ba ba ngeen agsee bérab bii, fippu ci kaw Aji Sax ji ngeen masa nekke.

Ndax maa xam seen jikkoy fippu, ak seenug dëgër bopp. Seetleen, ndegam bi may dundagum tey ci seen biir ngeen di fippu ci kaw Aji Sax ji, astamaak gannaaw bu ma deeyee.

Ay waxam coxor aki fen, jëfeetul lu rafet ak lu baax.