TSK

TSK · Exodus 39:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ «Xaymab jaamookaay bi nag, defare ko fukki sori rabali lẽe, mu ànd ak wëñ gu baxa te laal yolet ak wëñ gu xewar ak gu xonq curr, te nga ñawaale ca nataali serub.

Liggéeykat yooyu ñooy jël wëñi wurus, ak wëñ gu baxa te laal yolet, ak wëñ gu xewar, ak gu xonq curr, ak wëñu lẽe ngir liggéeye ko.

ak yére yu yànj yi ñuy liggéeye ci bérab bu sell bi, yére yu sell yu Aaróona, sarxalkat bi, ak yérey doomam, yi ñuy sarxalee.»

ak yére yu yànj yi ñuy liggéeye ci bérab bu sell bi; yére yu sell yu Aaróona sarxalkat bi, ak yérey doomam yi ñuy sol, di sarxale.

Sarxalkat yi, bu ñu duggee ci bérab bu sell bi, dootuñu man daldi génn ci ëttu biti bi. Ci néeg yii lañuy wacc seen yére yi ñuy liggéeyale Aji Sax ji, ndax yooyu yére yu sell la. Ñu solaat nag yeneen yére bala ñoo dellu ca ëtt ba mbooloo may daje.»

Du deretu sikket mbaa yëkk la duggaale, waaye deretu boppam la dugge benn yoon ba fàww ca bérab bu sell baa sell, te moom la amale njotlaay gu sax dàkk.