Genesis 18:14
TSK
Ana lu të Aji Sax ji? Bu ñu ca àggee nëgëni déwén déy, dinaa fi délsiwaat, te Saarata dina am doom ju góor.»
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ana lu të Aji Sax ji? Bu ñu ca àggee nëgëni déwén déy, dinaa fi délsiwaat, te Saarata dina am doom ju góor.»
Ki jëmbati nopp, da dul dégg a? Am ki xari gët, da dul gis?
Nopp buy dégg ak bët buy gis, Aji Sax jee sàkk lu ci nekk.
Su boobaa gëti silmaxa muriku, noppi tëx sikkliku.
Ma ne: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, da di manumaa wax, gone doŋŋ laa.»
Sa làmmiñ laay taqal ci sa denqleñ, nga luu ba doo leen mana yedd, ndax kërug fippukat lañu.
Bu liitu xare jibee, waa dëkk ba du tiit a? Am aw ay dina dab ub dëkk te du Aji Sax ji?