TSK

TSK · Exodus 40:33

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Noonu la mboolem liggéeyu màkkaanu xaymab ndaje mi mate. Noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa rekk, ni la ko bànni Israyil defe.

Waaye yaw ci sa bopp nanga sas Leween ñi jaamookaay bi seedes kóllëre gi dence, mook la muy àndal lépp, ak mboolem lu ca bokk. Ñooy gàddu jaamookaay bi, ak la muy àndal lépp, di ko topptoo, te it fi wër jaamookaay bi lañuy dal.

Ba mu ko defee Suleymaan tabax kër gi, ba sottal ko.

Ñi Yàlla tabb ci biir mbooloom gëmkat ñi, ñi ci jiitu ñoo di ndawi Almasi. Ñaareel bi di ñiy waxe kàddug waxyu, ñetteel bi di jànglekati kàddu gi. Ñi ci topp di ñiy def ay kéemaan, ñi ci topp di ñi am mayu faje, ak ñi mane dimbalee, ak ñi mane jiite, ak ñiy làkk yeneen xeeti làkk.

Moo may ñii di ay ndawam, ñee di ay yonent, ñee di ay xamlekati xibaaru jàmm bi, ñale di ay sàmmi mbooloom gëmkat ñi, mbaa ay jànglekat.

Ku wóor la woon, ñeel ki ko tabb, noonee Musaa wóore woon ci mboolem waa kër Yàlla.

¶ Ba ñu waajalee noonu yooyii ba mu jekk, sarxalkat yaa daan dugg saa su nekk ca néeg bu jëkk ba, di def seen liggéey.