TSK

TSK · Exodus 40:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Mu sàkk nag diwu pal gu sell gi, sàkk cuuraay lu xeeñ li raxul, def ko njafaan lu njafaan-kat waajal ba mu baax.

¶ Ba loolu wéyee Musaa jël diwu pal ga, diw ca jaamookaay baak ya ca biir yépp, sellale ko yooya,

Yaw Yàlla, sab jal a sax dàkk ba fàww. Njub nga ŋanke sa nguur gi,

Noowug Boroom bi Aji Sax jaa ngi fi sama kaw, ndax Aji Sax jee ma diw, fal ma, ngir ma àgge néew-doole yi xibaaru jàmm. Moo ma yebal ngir ma dëfal ñi seen xol jeex, yégal jaam yi, seen goreel, yégal ñi ñu tëj, seen ubbite.

Moo nu màndargaale xàmmikaayam, te moo yeb dawalub Noo gu Sell gi ci sunu biir xol.