TSK

TSK · Exodus 8:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Musaa ne ko: «Bu may génn dëkk bi rekk, di tàllal Aji Sax ji samay loxo, dënu yi dakk, tawub yuur bi siwet, ngir nga xam ne àddina, Aji Sax jeey boroom.

«Ana kuy sa moroom ci tuur yi, yaw Aji Sax ji? Kuy sa dend, yaak sa sellaay bu yéeme, sa yànjaay bu raglook sa jëf yu yéeme?

Yeen déy lañu won loolu lépp ngir ngeen xam ne Aji Sax ji doŋŋ mooy Yàlla, te jeneen yàlla amul, ju dul moom.

Kenn du Yàllay Yesurun! Keey war asamaan, wallusi leen, war ay niir, ànd ak darajaam.

Boroom bi, doo moroomu tuur yi, te jëf melul ni sa jos.

feesal seen réew ay mbott yu àkki seen biir néegi buur ya.

Ci kaw loolu ma gis ñetti njuuma yu mel niy mbott, kenn ki génne ci gémmiñu ninki-nànka ji, kenn ci gémmiñu rab wu jëkk wi, ki ci des ci gémmiñu ñaareelu rab wi mbubboo yonent.