TSK

TSK · Ezekiel 21:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Yaa yebal say surga, di kókkali Boroom bi, te naa: “Sama watiir yi ne xas laa ware kawtey tund yi, jàll ba ca xolu Libaŋ. Maa gor seedaram ya fa sut ak tànnéefi garabi sipparam: maay àkki ba ca collub kaw bu tundu Libaŋ, ak gottam bu naat ba nib tóokër.

Su ko defee nga jël saafukaayu weñ, teg ko, mu mel ni miiru weñ bu dox sa digganteek dëkk bi, te nga janook dëkk bi. Noonu nga koy gawe, mu gawu. Loolu di misaal, ñeel waa kër Israyil.

«Yaw nit ki, jàkkaarlool ak tundi Israyil, nga waxal leen waxyu.

«Yaw nit ki, neel jàkk Amoneen ñi, nga wax waxyu ci seen kaw.

«Yaw nit ki, neel jàkk Firawna buuru Misra, nga biral waxyu fi kawam ak fi kaw Misra gépp.

«Yaw nit ki, neel jàkk Gog ma ca réewum Magog, boroom Meseg ak Tubal, te nga biral waxyu fi kawam.

Micah 2:6 TSK

Seen yonent yeey waare naa: «Buleen waare! Nii kat deesu ko waaree, gàcce du nu dab!»

Acts 6:13 TSK

Ñu indeeti foofa ay seedey naaféq yu ne: «Kii du bàyyee wax mukk lu juunoo ak bérab bu sell bii ak yoonu Musaa.