TSK

TSK · Ezekiel 21:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ñu ne leen: «Li ko waral mooy, dañoo fecci kóllërey Aji Sax ji, seen Yàllay maam, te mu fasoon ko ak ñoom ba mu leen jëlee réewum Misra.

su boobaa maay dagge bànni Israyil fi déndu suuf si ma leen jox, te kër gi ma sellal ngir sama tur, maa koy xalab, mu sore ma, te kon Israyil mujj di tur wu ñuy léeboo ak di ko kókklee ci biir xeet yépp.

Sama kàddu giy bawoo sama gémmiñ it, noonu la. Du délsee ag neen ci man te deful li ma namm, ba sottal li ma ko yebal.

Yaw nit ki, caxal waa kër Israyil aw cax, ci biir léeb woo leen di léebal.

«Waaye yaw garmib Israyil bu teddadi bu bon bi, sa bés dikk na, sa àppu mbugal mat na.