ma xamal tooñkat sa war, ba moykat dellu ci yaw.
TSK
TSK · Ezekiel 29:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Mooy nàddil néew-doole yi, njekkam sax dàkk, dooleem di yokku, ànd ak daraja.
Moo dooleel ñoñam, wóllëreem ñiy mbooloom bànni Israyil, xeet wi mu xejjoo, di ko màggal. Màggal-leen Ki Sax!
«Ay bés a ngi ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay jebbil Daawuda njebbitu njekk, mu falu di buur bu xelu, di jëfe njub ak njekk ci réew mi.
Bésub keroog sa gémmiñ dina ubbiku, nga noppee luu, ba wax ak ka rëcc. Su boobaa yaay doon misaalu mbooloo mi, ba ñu xam ne maay Aji Sax ji.»
ba waa Misra gépp xam ne maay Aji Sax ji. «“Seen ndimbal ak Israyil mooy ndimbalu bantu barax,
Waa kër Israyil dootuñu yaakaar Misra, xanaa ñuy fàttliku na ñu ñaawe woon démb, ba ñuy làqoo waa Misra, te dinañu xam ne maay Boroom bi Aji Sax ji.”»
Du lenn moos lu Boroom bi Aji Sax ji def, te déeyu ko yonent yiy jaamam.
Ndax man maa leen di jox làmmiñ wu ànd ak xel, wu seen benn noon dul mana dàq mbaa di ko weddi.