Na doon seen bés bu ngeen di nopplu doŋŋ, ngeen war cee toroxlu. Dogal la bu sax dàkk.
TSK
TSK · Ezra 8:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ana lu nu Aji Sax jiy indee ci réew mii ñu nara fàddoo saamar, sunuy jabar ak sunuy tuut-tànk doon alalu sëxëtoo! Tee noo dellu Misra yee?»
¶ Ci kaw loolu ma boole leen, ñu daje ca wetu dex, ga jëm Aawa, dal fa ñetti fan. Ma seetlu fa baadoolo ya, seet ca biir sarxalkat ya, gisuma kenn ku bokk ci Leween ñi.
¶ Keroog ñaar fukki fan ak ñeent ca weer woowa, bànni Israyil daje nañu, sol ay saaku, xëppoo suuf, di ko ñaawloo ci biir koor.
Man nag, sa ngor lu yaa laa saña dugge sa kër, sujjóotal sa bérab bu sell, wormaale la.
Aji Sax ji sunu Boroom, sa tur aka màgg ci kaw suuf sépp! Sag leer tiim asamaan.
Ca tàkkal dexi Babilon, foofa lanu daa toog, fàttliku Siyoŋ, jooy.
Loo mébét, bàyyil Yàlla xel, mu xàllal la yoon.
Foofa law yoon di jaare, ñu di ko wooye Yoon wu sell wi. Ku sobewu du fa jaare, ñi moom woowu yoon, ñooy ñi koy topp. Ab dof sax du fa lajje.
Duñu xiif, duñu mar; tàngooru mbóoya akub jant du leen sonal, nde ki leen ñeewantee leen di wommat, di leen yóbbu fu ndox bënne.
Ndax lii moo di koor gi ma taamu, ci bés bu nit kiy toroxlu? Koorug dëngal loos ni barax, lal saaku, sotti ab dóom, tëdd di ko ñaawloo? Loolooy seen koor, ci bés bu Aji Sax ji rafetlu?
«Maa ngii di jële sama ñoñ réewum bëj-gànnaar, dajalee leen fa cati àddina. Silmaxaa ngi ci akub lafañ, jigéenu wérul it ak kuy wasin, ñuy gàngoor gu mag, délsi fii.
Su bés baa, ci yooyu fan,» kàddug Aji Sax jee, «bànni Israyil ay ànd ak Yudeen ñi, dikk di jooy, di sàkku seen Yàlla Aji Sax ji.
Sellal-leen ag koor, woote am ndaje, wooleen mag ñi, ak mboolem waa réew mi, ca seen kër Yàlla Aji Sax ji, te ngeen woo Aji Sax ji wall.
Waa Niniw nag gëm Yàlla, daldi yéene koor. Ci biir loolu ku nekk sol ay saaku, di ko ñaawloo, dale ko ca ka gën di mag, ba ca ka gën di ndaw.
Ndax dige bi, yeen ak seen askan a ko moom, ak jaambur ñi féete fu sore ñépp, mboolem ñi sunu Yàlla Boroom bi woo.»