TSK

TSK · Galatians 1:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage
Acts 6:9 TSK

Ba loolu amee ñenn ca jàngu ba ñuy wax jàngub waa Goreel ga, daldi jóg, di tàmbalee weranteek Eccen. Ay niti waa Siren a nga ca, ak waa Alegsàndiri, ak waa diiwaani Silisi ak Asi.

¶ Ba loolu wéyee Barnaba jëm Tàrs, di seeti Sóol.

¶ Ñu yóbbante leen bataaxal, bind ci ne: Nun ndawi Yeesu, ak mag ñi, seen bokki Yerusalem, noo leen bind, yeen sunu bokki gëmkat ñi dul Yawut te dëkke Àncos ak Siri ak Silisi. Nu ngi jiital sunub nuyoo.

¶ Ba loolu wéyee Póol toogaat na fa fan yu bare, doora tàggtoo ak bokk ya, dugg gaal jëm Siri, ànd ak Pirsil ak Akilas. Fekk na mu watu nel ca teerub Señsere, firndeele ko aw xas wu mu xasoon.

Póol ne ko: «Man de ab Yawut laa, di as goru Tàrs, dëkk bu ñàkkul tur ba ca diiwaanu Silisi. Dama lay ñaan, nga may ma, ma wax ak mbooloo mi.»

Boroom réew ma jàng bataaxal ba, daldi laaj ci ban diiwaan la Póol bokk, ba xam ne diiwaanu Silisi la bokk.