Buleen séentu asamaan, gis jant bi, mbaa weer wi, mbaa biddiiw yi, ak mboolem leeri asamaan, ba mu xiirtal leen ci di leen sujjóotal ak a jaamu, te seen Yàlla Aji Sax ji féetale yooyii, mboolem xeet yi asamaan tiim.
TSK
TSK · Genesis 1:16
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
ndegam maa masa niir jant beek leeraayam, mbaa weer wiy daagoo yànjaayam,
Làmmiñu tuut-tànk, ba ci luy nàmp, feeñal nga ca sa kàttan, bañaaleek feyukat ne xerem.
Yaa moom bëccëg, moom guddi, teg fi weer week jant bi.
weer ak biddiiw, guddi. Kee saxoo ngoram!
Nañu màggal turu Aji Sax ji, kii kat a santaane, lii lépp am.
Kersa la weer wiy am, gàcce ñeel jant bi; Aji Sax ji Boroom gàngoor yi daal, mooy nguuru Yerusalem, kaw tundu Siyoŋ, leeram ga jollee fa kanam magi ñoñam.
Maay bind leer, di def lëndëm. Maay indi jàmm, di def safaan. Maay Aji Sax jiy def lii lépp!
Jant ak weer ne tekk fa seen màkkaan, janook sa leeru fitt yi soqi, ak melax gi tàkke ci sab xeej.
¶ Ba loolu amee ñeenteelu malaaka mi sotti ndabam ci kaw jant bi. Ñu daldi may jant bi muy lakke nit ñi tàngooru sawaraam.