TSK

TSK · Genesis 11:27

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Mu am bés Teraa ànd ak doomam Ibraam ak sëtam Lóot, mi Aran di baayam, ak Sarayi, soxnas Ibraam. Ñu bokk jóge Ur gu Kaldeen ña, jëm réewu Kanaan. Ba ñu demee ba Karan, daldi fay sanc.

Ibraam ànd ak soxnaam Sarayi ak Lóot, mi muy baay bu ndaw ci moom. Mu yóbbaale nag alal, ja mu dajale jépp, ak jaam, ya mu jënde Karan. Ñu jóge fa, jublu réewu Kanaan.

Booba lañu yóbbu Lóot ma dëkk Sodom, te Ibraam di baayam bu ndaw. Ci biir loolu ñu yóbbaale li mu amoon lépp, dem.

¶ Gannaaw gi, dañoo yégal Ibraayma ne ko: «Milka kat am na ay doom moom it, moom ak sa mag Naxor.