TSK

TSK · Genesis 11:5

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Damaa wàcc, xettlisi leen ci waa Misra; génne leen réew moomu, ba yóbbu leen réew mu baax te yaatu, réew mu meew maak lem ja tuuroo, foofa ca diiwaanu Kanaaneen ña ak Etteen ña ak Amoreen ña ak Periseen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña.

Fekk na tundu Sinayi wa wépp di sël-sëleeku saxar, ndax Aji Sax ja fa wàcc ci biir sawara. Saxar saa ngay gilli ni saxaru puuru ban, tund wépp di yëngook doole,

Aji Sax jaa nga këram gu sell. Aji Sax jaa nga asamaan, kaw jalam, ne jàkk doom aadama, di ko seetlu.

Xanaa du maay Yàlla?» Kàddug Aji Sax jee. «Fu jegeek fu sore, du maay Yàlla?

Te it amul mbindeef mu làqu fi kanam Yàlla. Lépp a ne duŋŋ, ne fàŋŋ, muy gis, te moom lanuy waxal bés-pénc.