TSK

TSK · Genesis 13:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Naka noona Yàlla Aji Sax ji jëmbat tool ca biir Àjjana fa féete penku ba, tàbbal ca nit ka mu bind.

ay goney Yàlla ñoo gis jigéen ñeek seen taar, ñuy jël ñi ñu bëgg ci ñoom, def leeni jabar.

¶ Ci kaw loolu buurub Sodom génn, mook buurub Gomor ak buurub Atma ak buurub Ceboyim ak buuru Bela, di Sowar ba tey, ñoom ñépp daldi làng, nara xare ca xuru Sidim,

Aji Sax ji nag yuree ca asamaan tamarax buy tàkk, muy taw ci kaw Sodom ak Gomor, na ko Aji Sax ji dogale.

¶ Jur gu ne gàññ, bare lool, la Rubeneen ñi ak Gàddeen ñi amoon. Ñu xoolaat diiwaanu Yaser ak diiwaanu Galàdd, gisuñu lu moy àll bu neexa yareg jur.

Ca joorug Yurdan la ko Buur xellilu, ci móoli ban, diggante Sukkóot ak Sartan.

Maay jooy Mowab jooyi xol, nit ñaa nga fay dawe ba Sowar, àkki ba Eglat Selisiya. Ña ngay yéeg jëm Luwit, di jooyoo, awe yoonu Oronayim, di jalu.

Yuux jibe na Esbon, ba Elale, àkki ba Yaxacc ak Sowar ba Oronayim ak Eglat Selisiya. Ndoxi Nimrim sax ŋiis na.

Du genn garabu seedar ca toolub Yàlla, gu ko yóbbuloon dara, du garabu sippar yu ko niruy car, mbaa garabu palataan bu ko niruy bànqaas. Du genn garab ci toolub Yàlla, gu taaroo ni moom.