TSK

TSK · Genesis 15:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Te réew mi nga doon ab doxandéem léegi, muy réewu Kanaan mépp, jox naa la ko, yaak sa askan, ngeen moom ko fàww. Te dinaa doon seen Yàlla.»

Ba loolu amee ñu fal ay nit ñu leen di ga ca seeni sas, di leen ca fitnaal lool. Noonu la bànni Israyil tabaxale Firawna buuru Misra dëkk, ya ñu naa Pitom ak Ramses, mu def ko ay dencukaayi dund.

¶ Gannaaw loolu Musaa ak Aaróona dem ca Firawna, ne ko: «Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: “Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma ca màndiŋ ma.”»

¶ «Képp ku dib jëtun akub jirim, buleen ko néewal.

Njuddu-ji-réew ji nangeen ko yemaleek doxandéem bi ngeen dëkkal. Soppleen ko ni ngeen soppe seen bopp, ndaxte ay doxandéem ngeen woon ca réewum Misra. Man Aji Sax ji maay seen Yàlla.

Kon soppleen doxandéem, ndax ay doxandéem ngeen woon ca réewum Misra.

Israyil agsi Misra, muy nganug Yanqóoba ga ca réewum Xam.

Acts 7:6 TSK

Yàlla ne ko: “Saw askan dinañu toxuji bitim réew, te dees na leen def ay jaam, mitital leen diiru ñeenti téeméeri at (400).”

Li ma ciy wax mooy lii: kóllëreg Yàlla gi taxawe ni kayitu donale gu mu dëggal, yoonu Musaa, wi dikk ñeenti téeméeri at ak fanweer gannaaw kóllëre gi, manu koo neenal, ba fomm digeb Yàlla.