TSK

TSK · Genesis 19:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ibraayma daldi gaaw, dugg biir xayma ba, ne Saarata: «Gaawal, jël ñetti ndabi sunguf su mucc ayib, not ko, def ko mburu yu ndaw.»

¶ «Diiru juróom ñaari fan ngeen di lekk mburu mu amul lawiir; te bés bu jëkk bi ci boppam nangeen jële seeni kër luy lawiir, ndaxte képp ku ci lekk mburu mu am lawiir, li ko dale bés bu jëkk bi, ba kera bésub juróom ñaareel ba, dees na ko dagge ci askanu Israyil.

¶ Am na bés Alyaasa jaare dëkk bu ñuy wax Sunem. As ndaw su bare alal woo ko lekk këram, di ko soññ. Mujj na saa yu fa jaaree, daldi fay toog, ba xéewlu.

Luke 11:8 TSK

Maa leen ko wax, su jógul jox ko la mu laaj ndax ug xaritoo it, la ko kee amul kersay yee ngir sàkku ndimbal mooy tax mu jóg, jox ko mboolem lu mu soxla.

¶ Naka lañuy jub dëkk, ba ñu jëm, mu mel ni ku nara jubal yoonam.

Kon nag, nanu màggal sunu bésub Mucc te bañ koo màggale lawiir bu yàgg, mbaa lawiiru yàqute akug mbon, xanaa nu màggale ko mburu mu mucc lawiir, mburum xol bu set te dëggu.

Buleen sàggane di terle, nde am na ñu seen teraanga tax ñu fat ay malaaka te xamuñu ko woon.