Bu la waa Misra gisee, dinañu ne sama soxna nga. Te dinañu ma rey, nga des.
TSK
TSK · Genesis 20:11
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Genesis 12:12
TSK
Genesis 26:7
TSK
Góori foofa laaj ko ndaw si mu àndal, lu mu doon ci moom, mu ne: «Sama jigéen la.» Dafa bañoona wax ne soxnaam la, ngir ragal waa foofa rey ko ndax taaru Rebeka.
Nehemiah 5:15
TSK
Waaye boroom diiwaan yi ma jiitu dañu daan not askan wi, di leen sëf seen dund ak seen biiñ, boole ci ñeent fukki dogi xaalis. Seeni surga it di néewal askan wi doole. Man nag defuma noonu ndax ragal Yàlla.
Job 28:28
TSK
daldi ne doom aadama: «Ragal Boroom bi daal, mooy xel mu rafet, te dëddu lu bon mooy am ug dégg.»
Psalms 36:1
TSK
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda jaamub Aji Sax ji.
Proverbs 2:5
TSK
Kon nga xam luy ragal Aji Sax ji, xam Yàllaa di kan;
Proverbs 16:6
TSK
Ku jiital ngor ak worma, Yàlla jéggal la; ku ragal Aji Sax ji, dëddu lu bon.