TSK

TSK · Genesis 21:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Fekk na Aji Sax ji um jigéeni waa kër Abimeleg, ba kenn du ci am doom, du soxnaam, du ay jaamam, te li ko waral di Saarata soxnas Ibraayma. Ibraayma nag ñaan Yàlla; Yàlla def ñu wér, ba mana am doom.

Ñu ne ko: «Gis nanu bu baax ne Aji Sax ji ànd na ak yaw; moo tax nu ne ayca nu waatoo ci sunu digganteek yaw te fasanteek yaw kóllëre.

Laban ne ko: «Ngalla waay, déglu ma, ngir sama ngisaane won na ma ne Aji Sax ji barkeel na ma ndax yaw.

Sang ba nag gis ne Aji Sax jaa ngi ànd ak Yuusufa, di ko may ndam ci lépp lu mu sabablu.

Kon nag giñal ma ci Aji Sax ji ne doo dagg sama askan wi may wuutu, te doo raafal sama tur ci sama waa kër baay.»

Ngeen mébét, dara! Ngeen diisoo, diisoo, tus! Yàllaa ànd ak nun!

Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Janti keroog yooyu, fukk ñuy làkk mboolem làkki xeet yi, ñooy langaamoo catu mbubbu benn Yawut, naan ko: “Nun, yeen lanuy àndal, nde noo dégg ne Yàllaa ngeek yeen.”»

¶ Ana lu nuy waxati nag? Gannaaw Yàllaa ànd ak nun, ku nu manal dara?

¶ Buleen jikkowoo bëgg ub xaalis; doylooleen li ngeen am, ndax Yàlla moo ne: «Duma la bàyyi mukk, duma la wacc mukk.»