TSK

TSK · Genesis 22:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Gannaaw loolu Musaa jële bànni Israyil géeju Barax ya, ñu wéy, wuti màndiŋ, ma ñuy wax Sur. Dox nañu ñetti fan ca màndiŋ ma, gisuñu ndox.

ba noppi, mu wax leen ne leen: «Waajal-leen gannaaw-ëllëg, te li feek booba, buleen fi ànd ak jigéen.»

¶ Ci kaw loolu ñu bàyyikoo ca tundu Aji Sax ja, doxe fa doxub ñetti fan. Gaalu kóllërey Aji Sax jaa nga leen jiitu diiru ñetti fan ña, di leen wutal dal-lukaay.

Bésub ñetteel ba nag, ak bésub juróom ñaareel ba, ci la nit ku set di wis-wisal ndox mi ci kaw ki sobewu. Bésub juróom ñaareel ba ca la koy settli. Su ko defee ka sobewu fóot ay yéreem, sangu, bu jant sowee mu daldi set.

«Dellul ba ca Esekiya, sama njiitu ñoñ, nga ne ko: “Aji Sax ji sa Yàllay maam Daawuda dafa wax ne: Dégg naa sag ñaan, gis naa say rongooñ. Maa ngii di la wéral, te bu gannaaw ëllëgee dinga dem kër Aji Sax ji.

Hosea 6:2 TSK

Ñaari fan, mu leqli nu, ñetteel ba mu yékkati nu, nuy dund fi kanamam.

Mu ne leen: «Demleen wax njomboor moomu, ne ko: “Maa ngii di dàq rab yi, di maye ag wér, tey ak ëllëg. Bésub ñetteel ba nag ma sottal.”