TSK

TSK · Genesis 22:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Gannaaw loolu Ilyaas ne Alyaasa: «Ngalla xaaral fii, ndax Aji Sax ji da maa yebal dexu Yurdan.» Alyaasa ne ko: «Ak sama digganteek Aji Sax ji, Kiy Dund, nga fekke tey, duma teqlikook yaw mukk!» Ñu ànd ñoom ñaar.

¶ Ma daldi gis gàtt bu mel ni lu ñu rendi, mu taxaw fi digg ngàngune mi, ñeenti bindeef yeek mag ñi yéew ko. Gàtt bi juróom ñaari béjjén la am, ak juróom ñaari bët, di juróom ñaari noowi Yàlla, yi ñu yebal ci àddina sépp.

¶ Ma ne ko: «Sama sang, loolu de xanaa yaa ko xam.» Mu ne ma: «Ñoo di ñi jóge ca nattu bu réy ba. Fóot nañu seeni mbubb, ba weexal ko ci deretu Gàtt bi.