TSK

TSK · Genesis 24:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Ibraam nag amoon alal ju bare diggante jur, xaalis ak wurus.

¶ Ba Isaaxa di juddu, booba Ibraaymaa ngi woon ci téeméeri atam.

Isaaxa am ñeent fukki at, jël Rebeka doomu Betuwel, Arameen, bi dëkke diiwaanu Padan Aram, dib jigéenu Laban, Arameen ba.

¶ Gannaaw gi Buur Daawuda mujj naa màggat, ba làq at yu bare, ñu di ko sàng ay sér te du ko taxa tàng.

Barkeb Aji Sax jeey maye alal, kër-këri taxula barele.

ba tax na, boroom ngëm yi lees di booleek Ibraayma miy boroom ngëm, barkeel leen.

Ndax kat tàggat aw yaram, as njariñ a ngi ci, waaye ag njullite, ci lépp lay jariñe, te moo moom digeb àddinay tey ak ëllëg.