TSK

TSK · Genesis 25:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Turu menn wal ma di dexu Pison, moo wër réewum Awila mépp. Wurus a nga woon ca réew mooma,

ak Ofir ak Awila ak Yobab. Ñooñu ñépp di doomi Yogtaan yu góor.

¶ Waaye xuru Sidim woowu dafa feesoon dell aki pax aki kàmbi koltaar. Ba mu ko defee buuri Sodom ak Gomor di daw, far daanu ca kàmb ya. Ña ca des daw ba ca tund ya.

Ismaylaay tiiñe, ni mbaamu àll mu deesul not, di noonoo ñépp, ñépp noonoo ko. Mooy sanc fu muy jàkkaarlook bokkam yépp.»

¶ Ca ëllëg sa Ibraayma jóg suba teel, sàkk mburu, booleek mbuusu ndox, jox Ajara, mu gàddu. Mu daldi ko dénk Ismayla, yebal ko, mu dem. Ci kaw loolu muy wëndeelu ca màndiŋu Beerseba.

¶ Gannaaw loolu Musaa jële bànni Israyil géeju Barax ya, ñu wéy, wuti màndiŋ, ma ñuy wax Sur. Dox nañu ñetti fan ca màndiŋ ma, gisuñu ndox.

Ca ay jantam la Firawna Neko buuru Misra jóg jàppleji buurub Asiri ca wetu dexu Efraat, Buur Yosya dogaleji ko. Teewul ba ko Neko gisee la ko rey ca Megido.

seeni sarxalkat loroo saamar, te jëtun jooyul.