TSK

TSK · Genesis 25:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Rebeka amoon na càmmiñ lu tudd Laban. Laban daldi gaawtu génn, fekki waa ja ca seyaan ba.

Kon doom, defal lii ma lay wax, demal làquji fa sama càmmiñ Laban ca Karan,

ñu ànd tegu ca yoon wa, yóbbaale géttam gépp ak mboolem alal ju mu liggéey. Mooy gétt, ga mu sàkkoo Padan Aram. Ña ngay ñibbi kër baayam Isaaxa ca réewu Kanaan.

Ci kaw loolu Yàlla feeñu Laban, Arameen ba, ci géntu guddi ne ko: «Moytula wax Yanqóoba lenn lu koy gaar.»

Mu dellu nag wax fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ne: «Sama maam ab Arameen buy màngaan la woon. Mu dem Misra, sance fa mbooloo su néew, te mujj di askan wu réy, am doole te bare.