TSK

TSK · Genesis 25:8

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Yaw nag dinga gudd fan lool, doora nelaw, ñu denc la, nga fekki say maam ci jàmm.

Ati Ismayla téeméer la ak fanweer ak juróom ñaar (137). Gannaaw loolu la nelaw, fekki ay maamam.

Isaaxa dund na téeméeri at ak juróom ñett fukk (180).

Firawna laaj Yanqóoba ne ko: «Aa, góor gi, xanaa war ngaa doon mag de!»

¶ Naka la Yanqóoba dénku doomam yu góor ya noona, daldi delloo ay tànkam ca lal ba, bakkan ba rot, mu fekki ay maamam.

«Dees na tërali Aaróona fa ay bokkam. Du dugg déy ca réew ma ma jox bànni Israyil, gannaaw yeena gàntaloon sama ndigal ca walum Meriba.

Acts 5:5 TSK

¶ Naka la Anañas dégg kàddu yooyu, daldi daanu, dee. Tiitaange lu réy nag dikkal ña ko dégg ñépp.

Ca saa soosa tembe la ko malaakam Boroom bi fàdd, ndax la mu delloowul Yàlla njukkal. Ba loolu amee, ay sax ronq ko, mu dee.