TSK

TSK · Genesis 26:28

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Léegi nag waatal ma fii ci Yàlla ne doo ma wor mukk, man ak samay doom, ba ci samay sët. Waatal ma ne noonee ma rafetoo woon ak yaw, ni ngay rafetoo ak man, maak waa réew, mi nga dal.»

ma giñloo la ci Aji Sax jiy Yàllay asamaan ak suuf ne doo jëlal sama doom soxna ci biir jigéeni waa Kanaan, gi ma dëkk ci seen biir.

Léegi ñëwal rekk, ñu fasante kóllëre maak yaw, te seede dox sunu diggante maak yaw.»

Boobee waayi Misra ja dénkee Yuusufa këram ak lépp lu mu moom, mu di ko saytu, ca la Aji Sax ji dale barkeel këram, barkeelaale mboolem lu mu moom, kër ak tool.

Sóol nag xam xéll ne Aji Sax jee ànd ak Daawuda, te it doomam Mikal bëgg na ko,

Ña la daa néewal, seeni doom a lay sukkalsi. Ña la daa ñàkke worma, mujj di fóon say tànk. Dees na la wooye «Dëkkub Aji Sax ji», mbaa «Siyoŋ, màkkaanu Aji Sell ju Israyil.»

Dees na xàmmee seen askan fi biir xeet yi, xàmmee lu meññe ci ñoom fi biir waaso yi; képp ku leen gis ràññee ne ñooy askan wu Aji Sax ji barkeel.

ba la làqu woon ca biir xolam, daldi leer. Su ko defee mu ne dàll dëpp jëëm ci suuf, sujjóotal Yàlla, te naan: «Aylayéwén Yàllaa ngi ci seen biir!»

¶ Buleen jikkowoo bëgg ub xaalis; doylooleen li ngeen am, ndax Yàlla moo ne: «Duma la bàyyi mukk, duma la wacc mukk.»