TSK

TSK · Genesis 27:40

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Yal na la ay giir nangul, ay réew di la sujjóotal, nga yilif say bokk, te say doomi ndey di la sujjóotal. Ku la móolooy alku, te ku la ñaanal barkeel.»

Mu daldi tabb ay jawriñam ca réewum Edom. Réewum Edom gépp la tabb ay jawriñ, Edomeen ñépp nekk ci curgag Daawuda. Aji Sax ji nag may Daawuda ndam fépp fu mu dem.

¶ Ca jamonoy Yoram la Edomeen ña fippu, bañ moomeelu Yuda, ba fal seen buuru bopp.

Dëgg la moos, yaa duma Edom, ba tax nag sam xel jay la. Tee ngaa bàkku te toog sa kër? Te sax ana looy dugge ci jote buy indi ay wu lay daane, yaw, daanewaale Yuda?»

Yàllaa àddoo fa këram gu sell, ne: «Maay damu, dogat suufas Sikem, séddale xuru Sukkóot.