Betuwel ay baayu Rebeka. Ñooñu ñooy juróom ñetti doom yu góor, yi Milka am ak magu Ibraayma, Naxor.
TSK
TSK · Genesis 28:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba loolu amee surga ba jële fukki giléem ca giléemi sangam, dem, yóbbaale li gën ci mboolem xeeti alalu sangam. Ma nga jëm réewu Mesopotami, ga Naxor dëkk.
Rebeka amoon na càmmiñ lu tudd Laban. Laban daldi gaawtu génn, fekki waa ja ca seyaan ba.
Isaaxa am ñeent fukki at, jël Rebeka doomu Betuwel, Arameen, bi dëkke diiwaanu Padan Aram, dib jigéenu Laban, Arameen ba.
¶ Ba loolu xewee, Yanqóoba awaat yoonam, ba agsi réewum waa penku.
Ci kaw loolu Yanqóoba ñaan Yàlla, ne ko: «Yaw Aji Sax ji, sama Yàllay maam Ibraayma, di sama Yàllay baay Isaaxa itam, yaa ma ne woon: “Dellul réew ma nga cosaanoo, ca say bokk; dinaa la baaxe.”
Góor ñooñoo xeetoo ci Leya, te askanoo ci Yanqóoba ca Padan Aram, gannaaw Diina miy doomam ju jigéen. Boo boolee doomam yépp, góor ak jigéen, ñuy fanweer ak ñett.
Yanqóobaa dawoon ba réewum Siri, Israyil laa ne, moo liggéey ngir am jabar, wut jabar tax koo sàmm ag jur.