Genesis 24:54
TSK
Ba loolu weesee mu doora lekk, daldi naan, moom ak ñi mu àndal. Ñu fanaan fa keroog. Ba ñu yewwoo ca ëllëg sa, surga ba ne: «Bàyyileen ma nag, ma dellu ca sama sang.»