TSK

TSK · Genesis 3:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Maa béga bég ci Aji Sax ji, sama xol di sedd ci sama Yàlla jii. Moo ma solal yérey mucc, sànge ma mbubbam njekk, may nirook boroom séet bu kaalawu ni sarxalkat, ne xenjaw ni séet bu takki gànjaram.

Cér yi ñu gëna jàpp ne jarula gëddaal, cér yooyu sax lañu gënatee gëddaal. Sunu cér yi amul sutura, ñoom lañu gëna suturaal,

Almasi mi masula bàkkaar, moom la Yàlla sëf sunu bàkkaar, ngir nu mana ame ci moom àtteb nit ñu jub fa Yàlla.