Genesis 35:24
TSK
Doomi Rasel di Yuusufa ak Beñamin.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Doomi Rasel di Yuusufa ak Beñamin.
Mag ya nag gis ne Yuusufa la seen baay gëna bëgg ci ay doomam. Loolu tax ñu bañ ko, ba manuñoo séq ak moom kàddu gu rafet.
Fekk booba Yuusufa mooy dogal ca réew ma, di jaay pepp waa réew mépp. Magi Yuusufa ya ñëw, sujjóotal Yuusufa.
«Yuusufaay bànqaasu garab, garab guy meññ, feggook bëtu ndox, car yaa nga law, tiim digu tool ba.
«Yaw nit ki, sàkkal aw dénk, nga bind ci kaw lii: “Ñeel Yuda ak giiri Israyil yi mu àndal.” Nga sàkkaat weneen dénk, bind ci kawam: “Ñeel Yuusufa bantub Efrayim ak waa kër Israyil yi mu àndal,”
¶ Ba Yanqóoba di waaja nelaw, ngëm la ñaanale ñaari doomi Yuusufa yépp, doora sujjóot, jafandoo boppu yetam.