TSK

TSK · Genesis 34:20

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

maa lay barkeela barkeel, fula ful saw askan ni biddiiwi asamaan, mbaa feppi suufi géej. Sa askan dina teg ay bañam tànk,

nangeen génne ba ca buntu dëkk ba, waa ji, mbaa ndaw si def jooju jëf ju bon, te ngeen dóor ay doj, waa jooju mbaa ndaw si, ba mu dee.

Muy teela jóg nag, taxaw ca peggu yoon, wa jëm ca buntu dëkk ba. Saa yu nit dikkee, am lu muy tawat, di ko diis-si Buur, ngir mu àtte ko, Absalom woo ko, laaj ko ne ko: «Ci ban dëkk nga bokk?» Kooku ne ko ci giirug Israyil sàngam la bokk.

Dees na ràññee jëkkëram ca pénc ma, fa muy toog ca magi réew ma.

Amos 5:12 TSK

Ràññee naa seen bàkkaar yu bare ak seen moy yu dul jeex. Yeenay tooñ aji jub, di geru, di xañ néew-ji-doole dëgg ci pénc.

«Ndigal yii, nangeen ko jëfe: Deeleen waxante dëgg, te dëgg ak yoon, nangeen ko àttee àtteb jàmm ci seen ëtti àttekaay.