Genesis 13:14
TSK
¶ Gannaaw ba Lóot teqlikook Ibraam, Aji Sax ji wax na Ibraam ne ko: «Téenal foofu nga taxaw, te séenu bëj-gànnaar ak bëj-saalum ak penkook sowu,
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Gannaaw ba Lóot teqlikook Ibraam, Aji Sax ji wax na Ibraam ne ko: «Téenal foofu nga taxaw, te séenu bëj-gànnaar ak bëj-saalum ak penkook sowu,
Dalal ci réew mii; dinaa ànd ak yaw, barkeel la. Yaak sa askan laay jox suuf sii sépp, te dinaa sàmm li ma giñaloon sa baay Ibraayma.
Ndeke Aji Sax jaa nga tollu ca wetam. Mu wax ak moom ne ko: «Maay Aji Sax ji, di sa Yàllay maam Ibraayma te di Yàllay Isaaxa. Suuf si nga tëdd dinaa la ko jox, yaak sa askan.
Booba Yàllaa ngay dégg seeni yuux, te fàttewul kóllëre ga mu fasoon ak Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba.