Laban da ne ko: «Yaw kay sama jarbaat nga lenqe!» Yanqóoba toog na fa ak moom lu mat weer.
TSK
TSK · Genesis 37:27
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
te naa ci seen biir: «Céy su nu yégoon, sunu àqu rakk a nu topp nii, ndax danu koo seetaanoon, mu nekk ci njàqarey xol, di nu tinu, te faalewunu ko; looloo waral sunu njàqarey tey jii.»
Waaye su jaam ba dundee ba ca ëllëg sa, mbaa gannaaw-ëllëg sa, deesu ko feyul ndaxte moomeelu sangam la.
¶ Ba bët setee Daawuda bind Yowab bataaxal, yóbbante ko Uri.
Ma ne leen: «Nun def nanu sunu kem kàttan ngir jotaat sunu bokki Yawut yi ñu jaayoon ay jaambur. Léegi yeen ci seen bopp ngeen di jaay seeni bokk, nun nu war leena jotaat?» Ñu ne xerem, amuñu lu ñu wax.
ak kanel ak yeneen safal, ak ndàbbu miir ak cuuraay-libaŋ ak yeneen cuuraay, ak biiñ ak diwu oliw ak sunguf ak pepp ak nag ak xar ak fas, aki watiir aki jaam, ak nit ñu ñu jàpp xare.