¶ Jamono yooyu Abimeleg àndoon na ak Pikol kilifay xarekatam, dem ci Ibraayma ne ko: «Gis naa ne Yàlla ànd na ak yaw, di àntal li ngay def lépp.
TSK
TSK · Genesis 39:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Sang ba nag gis ne Aji Sax jaa ngi ànd ak Yuusufa, di ko may ndam ci lépp lu mu sabablu.
ba tax mu tëj leen ca kër kilifag wattukat ba, ca kaso, ba ñu tëj Yuusufa.
Maay dogal sax waa Misra yéwéne mbooloo mii, ba keroog bu ngeen di dem, dungeen deme loxoy neen.
Aji Sax ji nag def waa Misra nangul bànni Israyil, ba jox leen la ñu sàkku; noonu lañu futtee waa Misra.
ba saña tënk jawriñi buur ci coobareem, tey xelal mag ña.
Ku Aji Sax ji rafetlu say jëf, say bañ sax, mu jubaleek yaw.
Booy xuus cim ndox, maa ngi ànd ak yaw; ag dex du la mëdd. Booy dox cib taal, doo lakk, sawara du la xoyom.
¶ Dañeel daldi ne Buur: «Buur, guddalu fan!
¶ Ana lu nuy waxati nag? Gannaaw Yàllaa ànd ak nun, ku nu manal dara?
¶ Te it su ngeen dee ñu njaxlaf ci def lu baax, ana ku leen di def lu bon?
Su ñu leen jànnee sax ndax turu Almasi, ndokklee yeen, ndax Noo gu darajawu gi, Noowug Yàlla moo wàcc ci yeen.