TSK

TSK · Genesis 39:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Yàlla ne ko ca gént ga: «Waaw, xam naa ne li nga def du sa teyeef. Moo tax man it mayuma la nga laal ko, di ma tooñ.

Kon dinaa la may, nga jiite kër buur, te waa réew mépp ci sa waaw lañuy wéy; jal bi ma toog doŋŋ laa lay sute.»

¶ «Góor gu njaaloo, mook jabaru moroomam ji muy njaalool, dee rekk mooy seen àtte.

¶ Ba àppu ténj ba weesee, Daawuda yónnee, indi ko këram, mu doon soxnaam. Gannaaw gi mu am doom ju góor. Aji Sax ji nag ñaawlu la Daawuda def.

Waaye boroom diiwaan yi ma jiitu dañu daan not askan wi, di leen sëf seen dund ak seen biiñ, boole ci ñeent fukki dogi xaalis. Seeni surga it di néewal askan wi doole. Man nag defuma noonu ndax ragal Yàlla.

Job 31:9 TSK

Ndegam jabaru jaambur a ma xañ sago, ba ma di ko yeeroo sama buntu kër moroomu góor,

Fóotal maa fóotal sama ñaawtéef, raxasal ma sama moy.

Njaaloo di ñàkk bopp, kuy sànk bakkanam a koy def.

Mbete fas yu suur, tukkal, ku ne ŋexal, jëm sa jabaru moroom.

Noon bu taseek ñoom warax leen te naan: “Nun defunu dara. Ñoom ñoo moy Aji Sax ji, te mooy dalukaayu njekk, ba seeni maam yaakaaroon.”

Te itam li ñuy sàkku ci ay saytukat moo di ñu jara wóolu.

¶ Jëfi bakkan nag yomb naa xàmmi, te mooy: powum séy, ak jëfi sobe, ak yàqute,

¶ Na ñépp wormaal diggante bu ab séy dox, te ab lalu séy na mucc sobe, ndax fokati séy yi, ak jaalookat yi, Yàlla moo leen di daan.

waaye ñu ragal ñi ak aji gëmadi ñi ak defkati ñaawtéef yi ak bóomkat yi ak moykat yi ak xërëmkat yi ak bokkaalekat yi, mboolem niti fen ñi, seen añ a nga ca déegu sawara waak tamarax ba. Loolu moo di ñaareelu dee.»