TSK

TSK · Genesis 4:10

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Seen dundu nit itam, mu ngi ci seen deret, kon kat, képp ku tuur seen deret dinaa ko ko topp. Te it mala mu ci rey nit dinaa ko ko topp, ni may toppe nit. Dinaa topp ku nekk deretu moroomam.

¶ Aji Sax ji tegaat ca ne ko: «Gis naa bu baax fitna, ji sama ñoñ nekke Misra. Dégg naa itam seen jooy ndax kilifay saskat, yi leen di gétën ci liggéey, te ñeewante naa leen ngir seen coono.

“Aji Sax ji dafa wax ne: Deretu Nabot ak deretu doomam yi déy, gis naa mu tuuru fii démb. Kon nag dinaa la ko topp, nga fey ko ci tool bii. Loolu la Aji Sax ji wax.” Kon nag yóbbul sànni ci tool bi, muy la Aji Sax ji waxoon.»

Job 16:18 TSK

Suufoo, bul làq sama deret ji tuuru, te yal na sama yuux jollee fu af.

Job 31:38 TSK

Ndegam sama tool a ma tuumaale ay jooy, rongooñi toobo yay bas-baseendoo,

Mooy topp nit bakkanu moroomam, di ko ba xel, te du fàtte yuuxi néew-ji-doole.

boole leen jot ci notaangeek loraange, ngir fonk seen bakkan.

Acts 5:3 TSK

¶ Ba loolu amee Piyeer ne ko: «Anañas, lu waral Seytaane di fees sab xol, ba ngay wor Noo gu Sell gi, di làq lenn ci njégu tool bi?

¶ Ngëm la Abel jébbale Yàlla sarax su gën saraxub Kayin, te ngëm lees seedeele Abel ne moo jub, kera ba Yàlla ci boppam seedee ne ay saraxam a nangu. Ngëm it moo waral Abel dee, te di wax.

James 5:4 TSK

Dégluleen! Peyoor, ga ngeen xañ ña gub seen tool, mooy yuuxu noonu. Jàmbati góobkat ya tàbbi na ca noppi Boroom gàngoori xare yi.