Nanu ko rey gaaw, sànni ko ca kàmb yee, su ko defee danu naan, rabu àll a ko fàdd. Nu seet ba xam fu muy mujj aki géntam?»
TSK
TSK · Genesis 42:36
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yal na Yàlla Aji Man ji def waa ja yërëm leen, ba bàyyi seen doomu baay ba, moom ak Beñamin itam. Man nag, su ma naree ñàkk ay doom— aa! Naa leen ñàkk rekk.»
Israyil daldi ne: «Moom kay na dund rekk! Sama doom Yuusufaa ngi dund. Man kay dinaa dem ba gis ko, bala ma fee jóge.»
¶ Daawuda nag ma nga naan ca xelam: «Bés a ngi ñëw bu ma nara sànku ci loxol Sóol. Li gën ci man daal, du lenn lu moy dawa daw ba ca réewu waa Filisti, ba Sóol tàyyi maa rëbbati ci Israyil gépp, ma daldi mucc.»
Sa yaakaar tas, Aji Sax ji jege la, sa xol jeex, Aji Sax ji wallu la.
Nii la Yanqóoba jotoo ñaawtéefam, nii la mujje am njéggalu bàkkaaram: Day boole doji sarxalukaay bi yépp, rajaxe ni doji kew, xer wu ñuy jaamoo Asera dootu fa sampe, mbaa sarxalukaayi suurukaay.
bul ragal, yaw laa àndal, bul tiit, maay sa Yàlla; maa lay dooleel, dimbali la déy, maa lay téyee sama ndijooru njekk déy.
¶ Ana lu nuy waxati nag? Gannaaw Yàllaa ànd ak nun, ku nu manal dara?
Sunu coono bu woyof bii ci àddina, ci diggante bu gàtt nag, moo nuy jural teraanga ju diisaay ba jéggi dayo, teraanga ju sax dàkk.