¶ Ba Ibraam amee juróom ñeent fukki at ak juróom ñeent (99), am na bés Aji Sax ji feeñu ko ne ko: «Man maay Yàlla Aji Man ji. Topp ma te mat sëkk.
TSK
TSK · Genesis 43:14
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Yal na la Yàlla Aji Man ji barkeel, nga jaboot lool te sa giir yokku, ba sos ay mboolooy askan.
Yàlla neeti ko: «Man maay Yàlla Aji Man ji. Giiral te yokku, ba aw askan ak mboolooy askan sosoo ci yaw, te ay buur askanoo ci sa geño.
¶ Ci biir loolu mu dummóoyu leen, di jooy.
Ma ngay seet, tàmbalee ca taaw ba, ba ca caat ma, doora fekk kaas ba ca saaku Beñamin.
Éy Boroom bi, Sang bi, rikk teewlul bu baax samag ñaan, ak sa ñaanu jaam ñi safoo wormaal saw tur. Ngalla Sang bi, nangul ma tey jii, may ma waa jii yéwéne ma.» Booba maa yore woon naani Buur.
Jébbalul ci Aji Sax ji, dénku ci moom, mooy sottal.
Aji Sax jee baax, gore ba fàww, worma ja sax dàkk!
¶ Kàddu yu xelu yu Suleymaan buurub Israyil, di doomu Daawuda.
Xolu buur walum ndox la ci loxol Aji Sax ji, fu ko soob mu jëme ko fa.
¶ «Yërmandeem a ñeel ay ragalkatam, maas ci kaw maas.
xettli ko ci coonoom yépp, rafetal xelam, may ko itam Firawna buuru Misra baaxe ko; mu def ko kilifa ci Misra ak ci biir ëttu këram gépp.
ñeel Timote, sama doomu bopp ci wàllu ngëm. Aw yiw ak yërmande ak jàmm ñeel na la, bawoo ci Yàlla Baay bi, ak sunu Sang Almasi Yeesu.
Bataaxal bi ñeel na Tit, sama doomu yoon ci kaw ngëm gi nu bokk. Aw yiw ak jàmm ñeel na la, bawoo fa Yàlla Baay bi, ak Almasi Yeesu sunu Musalkat.