TSK

TSK · Genesis 43:9

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Seen dundu nit itam, mu ngi ci seen deret, kon kat, képp ku tuur seen deret dinaa ko ko topp. Te it mala mu ci rey nit dinaa ko ko topp, ni may toppe nit. Dinaa topp ku nekk deretu moroomam.

Ruben wax ak baayam ne ko: «Su ma la ko délloosilul, boo yeboo reyal sama ñaari doom yu góor yi. Tegal Beñamin ci sama loxo rekk, man dinaa la ko délloosil.»

Lu ko moy de Buur, sang bi, bés boo nopplujee fekki say maam, su boobaa man, maak sama doom Suleymaan dinañu nu tuumaal.»

Sang bi, gàddu ma, ma am jàmm, bu ma ñu bew ñi néewal.

Su dee boroom njekk bu dëpp yoonu njekkam, di def ndëngte, maa koy gàllankoor, mu dee. Soo ko àrtuwul ndax bàkkaaram, dina dee, te deesul bàyyi xel njekkal démbam la, waaye bakkanam, yaw laa koy laaj.

Bu ma nee ku bon ki: “Yaw ku bon ki, dee rekk mooy sa àtte,” te yaw waxuloo ko ko, àrtu ko ngir mu wacc yoonu mbonam, ku bon kooka aw ayam mooy àtteb deeyam. Waaye bakkanam, yaw laa koy topp.

Su la tooñee, mbaa mu ameel la lenn, topp ma ko.