TSK

TSK · Genesis 46:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Aji Sax ji wax Ibraam ne ko: «Déglul bu baax li ma lay wax: sa askan dinañu nekk ay doxandéem ci réew mu ñu moomul, ñu def leeni jaam, sonal leen diiru ñeenti téeméeri at.

¶ Gannaaw loolu am na bés Yàlla di nattu Ibraayma ne ko: «Ibraayma!» Mu ne ko: «Naam.»

Ca la ma malaakam Yàlla ma wax ci biir gént gi ne ma: “Yanqóoba,” ma ne ko: “Naam.”

Mu ne leen: «Dégluleen bu baax samay kàddu: su ngeen feeñlee ab yonentu Aji Sax ji, ci am peeñu laa koy xamale maay kan, te ci gént laay waxeek moom,

Aji Sax ji woo Samiyel, mu ne: «Maa ngi»,

Job 33:14 TSK

Yàlla déy, dees koo teewluwul, waaye day wax benn yoon ba yaar

Maa jekki gis, ag guddi, nit ku war fas wu xonq. Moom nag mu ngi taxaw ci biir garabi mirt ci aw xur, li ko féete gannaaw di fas yu xonq, ak yu ngëlembu, ak yu weex, ak seeni gawar.

Acts 9:10 TSK

¶ Ab taalibe bu ñuy wax Anañas nag ma nga woon ca Damaas. Sang bi feeñu ko, ne ko: «Anañas!» Mu ne ko: «Maa ngi, Sang bi.»

Mu am baat bu jib, ne ko: «Piyeer, jógal, rey te lekk.»