TSK

TSK · Genesis 46:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

ma def la ngay cosaanal xeet wu yaa, barkeel la, màggal sa tur, ngay buntu barke;

¶ Gannaaw ba loolu wéyee kàddug Aji Sax ji dikke na Ibraam wax jii ci peeñu, mu ne ko: «Yaw Ibraam, bul ragal dara; man maay sa kiiraay, te sa yool dina màgg lool.»

Ndax kat Ibraayma dina sos xeet wu mag te am doole, te xeeti àddina yépp ci moom lañuy barkeele.

¶ Foofa Aji Sax ji feeñu ko fa ne ko: «Bul dem Misra, waaye nanga toog ci réew mi ma lay wax.

Yàlla neeti ko: «Man maay Yàlla Aji Man ji. Giiral te yokku, ba aw askan ak mboolooy askan sosoo ci yaw, te ay buur askanoo ci sa geño.

Bànni Israyil nag giir fa, law, di fulandiwu, ba yokku lool, fees réew ma.

Seen Yàlla Aji Sax ji moo leen ful, ba yeena ngii tey, bare ba tollu ni biddiiwi asamaan.

Mu dellu nag wax fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ne: «Sama maam ab Arameen buy màngaan la woon. Mu dem Misra, sance fa mbooloo su néew, te mujj di askan wu réy, am doole te bare.

Léegi nag yaw Yanqóoba, yaw Israyil mii, Aji Sax ji la sàkk tabax la, dafa wax ne: «Bul tiit, jot naa la. Dama laa woo ci sa tur. Maa la séddoo.

Acts 7:17 TSK

¶ «Ñu dem ba dige ba Yàlla giñaloon Ibraayma di waaja sotti, yemook xeet wi yokku, di gëna bare ci Misra,