¶ Ba loolu xewee, Yanqóoba awaat yoonam, ba agsi réewum waa penku.
TSK
TSK · Genesis 46:8
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba Israyil dëkkee ca réew ma, am na bés Ruben dem tëdd ak Bilaa, nekkaaleb baayam; Israyil yég ko. Doomi Yanqóoba yu góor fukk lañu ak ñaar.
¶ Gannaaw loolu Yanqóoba woo ay doomam ne leen: «Bokkleen daje, ma xamal leen li leen di dikkal ëllëg.
¶ Bànni Israyil ya yilifoon seen kër baay, ñoo di: Góor ña Ruben, taawu Israyil, jur: Anog ak Palu ak Esron ak Karmi. Ñooñoo sos làngi Ruben.
¶ Ñu lim bopp ak bopp, turi sëti Ruben taawub Israyil seen maam, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
ñi dale ci ñaar fukki at, jëm kaw lees di lim, na ko Aji Sax ji sante Musaa. Lii moo di limeefu nit ña soqikoo ci bànni Israyil, ña génne woon Misra: