TSK

TSK · Genesis 47:26

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Waaye jaaraamaa Yàlla Aji Kawe ji, moom mi la dumaal say noon!» Ba loolu amee Ibraam sàkk fukkeelu la mu lël lépp, jox ko.

Te itam sang bi, dangay fal ay ndaw ci réew mi, ñuy sàkku juróomi natt yu ne benn ci mboolem lu ñu góobe réewum Misra diiru juróom ñaari ati naataange yiy ñëw.

¶ «Bu loolu weesee mboolem lu jóge ci suuf, muy pepp mbaa doomi garab, cérub fukkeel ba Aji Sax jeey boroom. Dees koy sellalal Aji Sax ji.

¶ Fexeleen bay génne benn céru fukkeel ci mboolem lu seeni tool meññ at mu nekk.

Ezra 7:24 TSK

Nu ngi leen di xamal itam ne képp kuy sarxalkat mbaa ab Leween, mbaa mu dib jàngkat mbaa fara bunt, mbaa mu di liggéeykatu kër Yàlla gi, mbaa surga buy liggéey ci kër Yàlla googu, du galag bu ñu ko saña teg mbaa njotu bopp mbaa ab juuti.