TSK

TSK · Genesis 47:27

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

daldi yebal ab baaxoñ, muy naaw, di dem ak a dikk, ba ndox mi fendi ci kaw suuf.

Dinaa leen yokk, ba ñu tollu ni feppi suuf, ba feppi suuf gëna neexa waññ sa askan.

Dinaa ful sa askan ni biddiiwi asamaan, dinaa jox sa askan suuf sii sépp, te it ci saw askan la xeeti àddina sépp di barkeele,

Yàlla ne ko: «Man maay Yàlla, di sa Yàllay baay. Bul ragala dem Misra, ndaxte askan wu réy laa fay sose ci yaw.

Terewul lu ñu leen gëna fitnaal, ñuy gën di fulandiwu, yokku, ba waa Misra am njàqare ca bànni Israyil.

Mu dellu nag wax fi seen kanam Yàlla Aji Sax ji, ne: «Sama maam ab Arameen buy màngaan la woon. Mu dem Misra, sance fa mbooloo su néew, te mujj di askan wu réy, am doole te bare.

Aji Sax ji giiral xeetam wa, ba ñu gëna bare seeni noon,

Maay waliis, dajale leen, nde maa leen di jot, ñu bareeti na ñu baree woon.