TSK

TSK · Genesis 48:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Yuusufa itam am Manase ak Efrayim ca réewum Misra, seen yaay di Asnat doomu Potifera, may njiitu diine ca dëkk ba ñu naan On.

«Aji Sax ji, sa kàttanu ndijoor a yéeme! Aji Sax ji, sa ndijoor a ne noon ba rajax.

¶ «Maa jël Leween ñi, weccikoo leen bépp taaw ci biir bànni Israyil,

Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. Aji Sax ji daa wax sama Sang, ne ko: «Toogeel sama ndijoor, ba ma def say noon sa ndëggastal.»

Luke 4:40 TSK

¶ Ba jant sowee, mboolem ña amoon ay jarag yu ame ay jàngoroy jàngoro, daldi leen indil Yeesu. Moom it, mu teg kenn ku ci nekk ay loxoom, wéral la.

Acts 6:6 TSK

Ñu indi leen fa kanam ndaw ya, ñu ñaanal leen, teg leen loxo.

Acts 13:3 TSK

Ba loolu amee ñu woor, boole kook ñaan, daldi leen teg seeni loxo, ba noppi yiwi leen.

Bul di gaawa teg loxo kenn, ngir fal ko njiit. Bul séddu ci bàkkaari jaambur, te yaw ci sa bopp, sàmmool dundin wu set.