TSK

TSK · Genesis 49:18

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Jiitee ma sag dëgg, jàngal ma. Yaw yaay Yàlla ji may musal, ma di la yendoo yaakaar.

Mu jëm ci Yedutun, njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.

Xanaa dinga leqli sa mbooloo, ba ñu man laa bànneexoo?

Aji Sax ji, sa wall laa yaakaar, say santaane laa jëfe.

Ma ne, ni jaam bu góor di wékke sangam bët, jaam bu jigéen di ko wékke bët sangam bu jigéen, ni lanuy wékke sunu Yàlla Aji Sax ji bët, ba keroog mu baaxe nu.

Maa ngi séentu Aji Sax ji, mu ngi won waa kër Yanqóoba gannaaw, waaye maa ngi koy yaakaar.

Aji Sax ji déy a leen namma baaxe, moo ko tax di jóg moos ngir yërëm leen, nde Aji Sax jeey Yàllay njubte. Ndokklee képp ku ko yaakaar!

Léegi daal, déggool rekk ak sama sang buurub Asiri, ma jox la ñaari junniy fas, ndegam am ngay gawaram!

Yaw nag, ca sa Yàlla nga wara dellu, ngor ak njub, sàmm ko, te nga saxoo yaakaar sa Yàlla.

Luke 1:30 TSK

Malaaka ma ne ko: «Maryaama, bul tiit, ndax daje nga ak yiwu Yàlla.

Luke 2:30 TSK

Nde saay gët tegu na ci mucc gi nga dogal,

Càkkéefu àddinaa ngi séentu, ndax yàkkamti bés ba doomi Yàlla di feeñ.

Ndax nun kat, ci ndimbalal Noo gi, ak ci sunu kaw ngëm lanu yaakaare ñu jox nu àtteb njub bi nuy séentu.