TSK

TSK · Genesis 5:22

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

Enog dafa topp Yàlla, ba jekki-jekki giseesatu ko, ndaxte Yàllaa ko yéege fa moom.

¶ Ba Ibraam amee juróom ñeent fukki at ak juróom ñeent (99), am na bés Aji Sax ji feeñu ko ne ko: «Man maay Yàlla Aji Man ji. Topp ma te mat sëkk.

Ma ngay ñaanal Yuusufa. Mu ne: «Yàlla ji samay waajur Ibraayma ak Isaaxa toppoon, moom Yàlla, ji ma sàmm, ba ma juddoo ba tey jii,

Maay ànd ak yeen, di seen Yàlla, ngeen di sama ñoñ.

buleen déglu waxu yonent boobu, mbaa boroom gént boobu, ndax seen Yàlla Aji Sax ji moo leen di nattu ngir xam ndax yeena ngi koy soppe seen léppi xol ak seen léppi bakkan.

ba keroog Aji Sax ji sottal kàddoom ga mu ma waxoon ne ma: “Su say sët sàmmee seen dundin, saxoo ngëm gu ma wéetal, te gar ci seen bakkan, kon doo ñàkk mukk ku lay wuutu ci jalub Israyil.”

Damaa saxoo ne jàkk ci Aji Sax ji ndijoor la ma fare, ba duma tërëf,

Éy Yàlla, maa tegoo la ma la giñal, maa lay defal saraxi cant.

Damay topp Aji Sax ji ci biir réewum aji dund ñi.

Amos 3:3 TSK

Ñaar dina ànd te digewuñub dajee?

Micah 6:8 TSK

Yaw nit ki, waxees na la li baax, ak li Aji Sax ji sàkku ci yaw, te loolu moyul di def yoon, sopp jëfi ngor te woyof nooy toppe sa Yàlla.

Luke 1:6 TSK

Ñoom ñaar ñépp a juboon, Yàlla seede, te mucc ayib ni ñuy jëfe santaane yeek ndigali yooni Boroom bi.

¶ Kon nag léegi, amul benn daan bu ñeel ñi bokk ci Almasi Yeesu.

Gan takktoo la kër Yàlla séq ak ay tuur? Ndax kat, nun, nooy kër Yàlla jiy dund, te noonu la ko Yàlla waxe ne: «Maay dëkk ci seen biir, di dox ci seen biir, di seen Yàlla, ñuy sama ñoñ.»

Su ko defee ngeen di dunde dundin wu yellook Boroom bi, ngir bànneexal ko ci wet gu nekk, seen meññeef it di jépp jëf ju baax, te ngeen gën di xam Yàlla.

Ñaax nanu leen, dëfal leen, dénku leen, ngir ngeen di jëfe jëfin wu yelloo ak Yàlla, mi leen woo ci nguuram ak teraangaam.

¶ Ci kaw ngëm lees yóbboo Enog, te deewul. Da ne mes, ndax Yàllaa ko yóbbu. Balees koo yóbbu kay, lees ko seedeeloon ne moo bànneexal Yàlla.