¶ Ba mu ko defee Yàlla ne Nóoyin: «Dogal naa ne dinaa boole faat mboolem boroom bakkan, ndaxte ayu nit dajal na kaw suuf. Dinaa leen boole ak li ci àddina, faagaagal.
TSK
TSK · Genesis 7:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ndax kat li feek juróom ñaari fan dinaa wàcce taw ci kaw suuf diiru ñeent fukki guddi ak ñeent fukki bëccëg, ba far ci àddina mboolem mbindeef mu ma sàkk.»
Moo tax alkànde yàq suuf, ñi ko dëkke gàddu àq ji. Moo tax waa àddina raaf, ba ñi des di lu néew.
«Dofe la sama ñoñ def. Man, xamuñu maay kan, mbetey gone yu dul xalaat dara; dég-dég, tus; seen xel mépp, lu bon rekk, lu baax, xamuñu ci dara.»
Moo tax réew mi wowal, mboolem lu fi dëkke ràgg, ba ci rabi àll yi, ak njanaaw yi, jëni géej itam day réer.
Lu leen jiitu, sawara lekk; lu leen topp, ag daay xoyom. Ni toolub Àjjana la réew mi ci seen kanam di mel, ñu won ko gannaaw, muy màndiŋ mu wéet, te kat dara du leen rëcc.
Ndax kat, càkkéef gépp, li ñuy déggal neenug neen la, te du seen coobare, waaye ki leen ci tënk la neex, ba tax ñuy yaakaar,
ndegam àddina sa woon it Yàlla jéggalu ko, xanaa Nóoyin ma daan waare njekk tey kenn ci juróom ñetti nit ña mu musal, ba mu walalee mbënn ma ci àddinay nit ñu gëmadi;