TSK

TSK · Genesis 8:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Back to passage

¶ Ndaxam bi Yàllay tas dëkki joor ga, xalaat na Ibraayma, ba musal Lóot ca dogalam boobee, keroog ba mu tasee dëkk, ya Lóot daloon.

Booba Yàllaa ngay dégg seeni yuux, te fàttewul kóllëre ga mu fasoon ak Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba.

Malaakam Aji Sax ji ne ko: «Lu tax ngay dóor sa mbaam mi ñetti yoon nii? Man mii maa dikk, jànkoonteek yaw, ndax yoonu sànkute laa gis.

¶ Rikk sama Yàlla, bàyyee ma lii xel, te bul far sama jëfi ngor ji ma jëfe ci sama biir kër Yàlla gi aki wartéefam.

¶ Ngalla sama Yàlla, bàyyil xel mbugal mu ñeel ñii teddadil liggéeyu carxal, fecci worma sasu carxal ak xeetu Leween.

Job 12:15 TSK

Mu ngoog, keey aj am ndox, mu maral, mu afal am ndox, mu salfaañe àddina.

Céy Aji Sax ji, gore nga ba kaw asamaan, dëggu ba kaw-li-kaw.

Éy Aji Sax ji, séddaale ma ci sa yiwu ñoñ, ngalla, dikke ma sag wall,

Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla. Éy Aji Sax ji, bàyyil xel Daawuda, ak gépp njàqareem.

Aji Sax ji, fàttlikul Edomeen ña, keroog jantub Yerusalem, ba ñu naan: «Màbbleena màbb, ba kenug dëkk bi siiñ!»

Maa naa xóotey mbeex mi: “Wowal, te maay ŋiisal say dex.”

Amos 8:7 TSK

Aji Sax ji giñ na ci turam wi askanu Yanqóobay damoo, ne: «Duma fàtte mukk lenn ci seeni jëf.

Éy Aji Sax ji, maa dégg sab jëw, Aji Sax ji maa yéemu ci sa jaloore! Ngalla yeesalal say jaloore, nu fekke, xamleel say jaloore, nu fekke, bu la am sànj teree geesu, yërëm.

Ndax kat, càkkéef gépp, li ñuy déggal neenug neen la, te du seen coobare, waaye ki leen ci tënk la neex, ba tax ñuy yaakaar,

Ndaxte ay bàkkaaram jalu na ba àkki asamaan, te Yàlla bàyyi na xel ay ñaawtéefam.